Jubboo

Amira Abed

Compositor: Não Disponível

Yenn saay ma tay ko xulóok yaw (ah!)
Ndax lay xew ci biir juboo ba (waaw foofu lu fa xew?)
Reewantu yakkul mbëggeel feeling la ci waawaaw
Li la duggal ci man génnewula ci (surtout loolu!)
Man su ma ragalul woon Yàlla ni maak yaw
Pique ak pelle taqalewuñu

Kaay ñu dem fu la neex
Xale bile yaw laa jox bopp
Mënuma la tenir tête, dama la nob
Na ñàkk jom colul
Ndax mere la woorul
Yaw sa dara soful
Ndax bàyyi la yombul
Te man sama compteurou xol
Nga woyofal yaa ko tay
Même suñu bàyyaante we
Sama alal ngay doon ba-tay

Neñ juboo maak yaw
Ma yërëm noon yi
Sòccu woon di xaar ku ñu reetaan
Moo tax waruñu xulóo maak yaw
Ndax yaay seral xol bi

Bu ko jaaree sax ma ramal la (moo xanaa nga bañ)
Feccal la (mo xanaa nga bañ)
Di la ayoo nenne
Bae kaay ma yeetal la (mo xale bi xanaa nga bañ)
Tay ngay jommi
Jubook yaw lu am jom ni (mo xanaa nga bañ)
Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la

Heey
Sa chéri du la seetaan nga fiy ñaaw
Ne dala bëgg yaa yor cahier wam
Mu yor sa bic ni dalay bindal

Su ma jubee xare bi duma dëpp
Ndax ñayu xare la man
Kenn du laal li ma moom
Ndaanaan ndaanaan a koy àttan

Chéri coco ney neex
Jëndal glace
Cub naa drapeau bi weex
Tey sama xol dafa neex
Ndax dama jubook bànneex

Hey
Namm nga ko
Nammoon naa la
Nammante ngeen
Xolu ñar a koy def
Kon bisuwante leen
Mouaaahh

Kon mbëggeel bala neex rax ñakk jom
Xale bi
Suñ xuloo ma lay tudd yaa ko fa am
Waaw
Soo xamoon tay ji li ma namm ci yaw
Na noppi sax bala waa jamra di ñów

Neñ juboo maak yaw (ñëwal)
Ma yërëm noon yi
Sòccu woon di xaar ku ñu reetaan (eh seen xol du neex tey)
Moo tax waruñu xulóo maak yaw
Ndax yaay seral xol bi

Bu ko jaaree sax ma ramal la (moo xanaa nga bañ)
Feccal la (mo xanaa nga bañ)
Di la ayoo nenne
Bae kaay ma yeetal la (mo xale bi xanaa nga bañ)
Tay ngay jommi
Jubook yaw lu am jom ni (mo xanaa nga bañ)
Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la

Kon fanaan
Yaa ma newoon fanaan
Yaa newoon fanaan
Yaa ma newoon fanaan
Fanaan ci naa

Yaw fanaan
Chéri fanaan
Yaw fanaan
Yaa ma newoon fanaan
Fanaan ci naa

Dialy xalamal ma
Ma woyal sama waa ji
Maak yaw amuñu nëboo
Yaay sama wétal
Waruñu xuloo

Yaw fanaan
Chéri fanaan
Yaw fanaan
Yaa ma newoon fanaan
Fanaan ci naa

Bu ko jaaree sax ma ramal la
Feccal la
Di la ayoo nenne
Bae kaay ma yeetal la
Tay ngay jommi
Jubook yaw lu am jom ni
Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital